Nangu naa dogal bi, jëm ci bokk gi dund ci jàmm.
    Di :

    Nu ngi jagleel bataxal bi
    Ñépp, góor ak jigéen ñi ànd di jëf ngir xeex jafe-jafey sunu jamono,
    ñi gëm ne nit mën na delloo si xel yi,
    juboo, nangu ne ñépp benn la ñu, nu ngi leen di yónnee ab bataxal jublu ci fexe ba bésu 16 ci weeru mai, bés bi àdduma jagleel « bokk gi dund ci jàmm », nekk  yoon lal, dëgëral jàmmoog nit ñi, dëkkandoo yi, askan yi ak réew yi
    Nun  ñépp, ànd ko ak ñi nu fal ci ci dëkk yi, ci gox yi ak ci réew yi, kilifa « politique » yi ak kilifa diine yi, kuréel yi ci réew yi ak yi réew yi bokk, na nu nangu àdduna jëm ci bokk gi dund ci jàmm.
    Ànd jëfandoo mooy yoon wi gën ngir taxawal bokk gi dund ci jàmm

    Dogalu àdduna bi jëm ci
    « bokk gi dund ci jàmm »

    Préambule

    Bu nu sukkandikoo ci ne suñu wareefu nit mooy nu ànd jëfandoo fexe ba tëral yoonu juboo ak jàppalante ci nit ñépp,

    Bu nu sukkandikoo ci wàll wi gën a am solo wi taskatu xibaar yi ak jumtukaayu xarala yu bees yi am ci tas xibaar yi, ak doole ji ñu am ci gëm-gëmu nit ñi ak ci xeex xibaar yi dul dëgg te rax ci, di indi ak féewaloo,

    Bu nu sukkandikoo ci ne dafa jamp ci yar xaley tey yi ci ñuy saxoog sàkku jàmm ba mag ña ñuy dooni mën a àndandoo tabax seen ëlëg, bañ a féewaloo,

    Bu nu sukkandikoo ci ne ci 8 fan ci weeru « décembre » atum 2017, ci la Mbootaay réew yi (ONU) dogal, 193 réew yépp ànd ci, ne at mu jotati, 16 ci weeru « mai » mooy bés bi àdduna di jagleel « bokk gi dund ci jàmm » (JIVEP),  

    Bu nu sukkandikoo ci ne kuréeel gi ëmb réewi Afrik yi ci ndajeem (891, 2019) ak itam mbooloom réew yi nu tudde « non alignés », ànd na ci dogal bi te di na ñu jàppale JIVEP,

    Bu nu sukkandikoo ci ne réew yu bari ak « capitale » yu bari itam fésal na ñu seen ànd ci bés bi ci la ñu déggoo ca jataayu « maires » yi ba ñu amaloon ca Düsseldorf ci août 2019,

    Bu nu sukkandikoo ci ne ba tey jii, ragalante gi mooy suuxat nàkk nawleente gi, lawug bopp-sa bopp gi mooy jur coow li ci polotig, kom-kom, kéewnga ak dëkkuwaay yi, di nasaxal jàmm ji, 

    Bu nu sukkandikoo ci ne ay junniy junni jigéen aki góor ñu ngi dund, lu baax rekk dox ci seen diggante tegu ci ngëneel yi ci jégalante ak yërëmante, 

    Bu nu sukkandikoo ci ne ku nekk soxla nga sa moroom, ak fo mën a jóge, loo mën a gëm, lu mën a doon sa cosaan, sa daraja, sa dëkkuwaay ak sa dundin,

     

    Proclamation

    Ñun ñëpp ñi dëkke àdduna, kilifa yiy yëngu ci polotig, ci koom-koom, ci dëkkandoo gi, nooy xamle ne nangu nanu dogalu àdduna bi jëm ci « bokk gi dund ci jàmm » ngirdi suuxat nawlante gi, mbokkoo gi, déggoo gi ak jàppalante gi, di fésal suñug bëgg ci suñu xol, dund booloo nekk benn, bañ a xool wuute gi, ànd tabaxàdduna bu sukkandiku ci jàmm, jàppalante dal ak déggoo *

    * Pàcc, ci dogal A/RES/72/130 bi Mbootayu réew yi jël jëm ci bés bi àdduna di màggal « bokk gi dund ci jàmm »

    Bu ma nangoo dogal bi, jëm ci bokk gi dund ci jamm, dafay war ci man:

     Nangu ne ñun ñi dëkke àdduna, ñun ñépp a yem jiggéen ak góor, kenn ku nekk soxla nga sa moroom:

    Dëkk ci di suuxat liy boole, di xeex liy féewale,

    • Di màggal « bésu bokk gi dund ci jàmm » teg ci weg aada ak cosaan yépp, ak moomeelu ku nekk, boole ci yar ak yeete,
    • Xiir nit ñi ci di taxawal lu ku nekk di gis sa bopp, lu amal nit ñi ñjariñ bés bu nekk, di taxawal kuréelu koom yuy jariñ ñépp te bañ a nekk rekk luy indi koom kesse,
    • Soppi doxalin, fexe ba wàññi lor gi wutum koom gi am ci càkeef gi ak ci tàngooru àdduna biyyokku, jël doxalin yu jëm ci yemale góor ak jigéen, rawatina ci mbirum payoor. 

     Boo de ku ñu fal ci dëkk bi, ci gox bi mbaa ci réew mi: 

    • Di suuxat « bokk gi dund ci jàmm » teg ko ci nangu wuute yépp ak di xeex ñàkk bëggante gi ba bokk gi dund ci jàmm mën a nekk ci gox yi,
    • Di dooleel bennoo gi ak déggoo gi boole ci askan wi ba kóolute gi law, fexe ba kenn ku nekk jigéen ak góor gis boppap ci mbooloo mi,
    • Fexe ba nit ñi nangu diine ak gëm-gëmu ku nekk.

     Boodee jigéen mba góor guy jiite këru liggéeyukaay:  

    • Fexe bu liggéey di sàmm worma nit ñi, fexe ba népp ñi ko séq, kenn ku nekk gis ci boppam,
    • Soppi doxalin, fexe ba wàññi lor gi wutum koom gi am ci càkeef gi ak ci tàngooru àdduna biy yokku, saxoo doxalin yu jëm ci yemale góor ak jigéen, rawatina ci mbirum payoor.

     Booy Kilifa diine dafay war ci yow nga:,

    • Xiir kuréél yi ci réew mi, ñuy fexe ba bokk gi dund ci jàmm di wéy, 
    • Fexe bay joxe xibaar yuy wér di jëmale kanam, di jariñ ñépp, di suuxat dunud gi ci jàmm.  

     Boo jiitee réew:  

    • Wéy di liggéey ci juboo gi, lawal jàmm ji ak koom-koom guy sax, jëflanteek mbootaay yi, kilifa diine yi ak képp ku ci bëgg jàpp, teg ay tëralin yuy suuxat jàppalante gi, xiir nit ñi jéggalante ak yëramante,
    • Jël ay dogal nguir fexee yamale nit ñi ci koom-koom ak si dundin. 
    • Tere liggéeyu xale yi,
    • Dugal njàngaleem suuxat jàmm ci li ñuy jëkk jàngale.  

     Booy kuréelu réew mbaa kuréel gu ay réew bokk:

    • Fexe ba soppi ay jëf yu nu mën a teg loxo, digle yi ak tëralin yi lal dogal A/RES/72/130 bi Mbootaay réew yi jël jëm ci JIVEP,
    • Fexee ay waxtaan yu yaatu yu soxal àdduna bi yépp jëm ci « bokk gi dund ci jàmm », bokk ci li àdduna di def.
    Contact Us

    We're not around right now. But you can send us an email and we'll get back to you.

    X